Mourning the Dead: Connecting histories of people, places, and remains podcast

Teewaayu ay Gewel yi ci anam gu metti ci ab takkub xarala ci Dakar

0:00
26:11
15 Sekunden vorwärts
15 Sekunden vorwärts

Ci pàcc bii, Ibrahima Thiaw ak Lamine Badji dañuy indi ay leeral ci anam yi nga xamantane dañuy faral di tàr lool ci sosum xam-xam ci Institut Français d'Afrique Noire. Institut bi, ñu gën ko xamee cii IFAN, dakar lañ ko ubbi woon ci atim 1936. Porogaraamam mo nekkoo jang nit yu bokkoom ci deuk bu Afrik Soowu Jant bu Farañsé yi Kolonisé woon - seen aada, seen cosaan ak seen diiwaan. Ibrahima Thiaw ak Lamine Badji dañuy waxtaane jamp gi am ci jamarloo ak ndono wu koloŋ bu ay kër yu mel ni IFAN ci ab Afrik bu moom boppam buy jéema jotaat ci niteem ak ci ngoram. Mu ngi aju ci istiwaaru desiti yaxi gewel yi, ñi bokk ci ndajaleem Laboratoire Njangum istuwaaru yaxi nit ñi bu IFAN Cheikh Anta Diop. ab istuwwaar bu xawa naxari la lool. Li ci gëna feeñ mooy ni amagu ñu ay saafara ba tey ci mbir mi.

Lii mooy sumb poscast buñu def ci Wolof. Mën nga ko degglu itam ci sumbi Farañse ak Angale.


Crédit yi
Bindkat yi : Ibrahima Thiaw, Lamine Badji
mbindum script yi : Sophie Schasiepen, Andri Burnett
Nettalikat bi : Bity Gaye Kébé
Tekki bi: B. G. & G. T. D., Afrolingo
Defarkat bi / soppikat bi: Andri Burnett
Defarkat bu mag bi: Sophie Schasiepen


Beneen Njang

Royuwaay yi am nañu liggéey Agbenyega Adedze, Julien Bondaz, Albert Charton, Sarah Croucher, Cameron Gokee, Deborah Mack, John Warne Monroe,  Raymond Mauny, Marie-Albane De Suremain, Ibrahima Thiaw, Guy Thilmans. Xoolal fii royuwaay yu mat yuñu lim fii.

Financement

Pocast Mourning the Dead dañ ko sosoon ci kaadaru li ci Iniwersité bu Western Cape def ci projet gëstu bi “Reconnecting 'Objects': Epistemic Plurality and Transformative Practices in and beyond Museums”, bu Volkswagen Foundation financé.

Weitere Episoden von „Mourning the Dead: Connecting histories of people, places, and remains“